• Wax ne ñaari tomb  $\rm A$ ak $\rm B$ da ñoo safaanoo jàkkaarle ci rëdd bii di $\bf \color{orange}{(D)}$ mu ngi firi ne $\rm (D)$ mooy xaaj-diggu dogit wii di  $\rm [AB]$.
  • Bépp tombu rëdd wii di $\rm (D)$ moom si boppam mooy safaanook jàkkaarleem ci $\bf \color{orange}{(D)}$. 

  • Yeneen waxin  :
    • Su $\rm A$ ak $\rm B$ safaanoo jàkkaarle ci bènn rëdd $\bf \color{orange}\Delta$, man na ñu wax tamit ne :
      • $\rm B$ mooy safaanook jàkkaarle bu $\bf\color{orange}{A}$ ci  $\bf\color{orange}\Delta$ wala itam $\rm A$ mooy safaanook jàkkaarle bu $\rm B$ ci $\Delta$.
    • Su $\rm P$ nekkee bènn tomb bu rëdd wii di $\Delta$, konn safaanook jàkkaarle bu $\rm P$ mooy $\rm P$ si boppam.
    • Tomb bu nekkul ci kow $\Delta$ safaanook jàkkaarleem da fay nekk « ci beneen wàllu » $\Delta$.
  • Nataalin : Soo bëggee nataal safaanook jàkkaarle bu bènn tomb wala bènn nataal, man nga jëfëndikoo bènn ekeer ak bènn reegal wu ñu maaskà wala bènn ekeer ak bènn kompa.  
  • Ñaari nataal yu safaanoo jàkkaarle da ñuy yem kepp soo leen teglantee, waaye kènn ki dafay ëlbatiku ci wàllu keneen ki.
    Seen soreewaay ak rëdd wi ñu safaanoo jàkkaarle (ñu koy woowee aks) ñooy tolloo te seen ndëngin ci aks bòbu bènn la. 
    Ab nataal da fa safaanoo jàkkaarle su fekkee ne, soo ko lemee tey topp aksu safaanoo jàkkaarle bi, ñaari xaaji nataal wi d ñuy yemoo kepp.   
    Ngir defar safaanook jàkkaarle bènn nataal, da ngay njëkka tek safaanook jàkkaarleek ay tomb yu bari ci nataal bòbu, soo noppee nga jokkale leen.

  • Safaanoo jàkkaarleeb bènn dogit ci bènn rëdd da fay nekk beneen dogit wu tollook moom guddaay. 

  

  • Safaanoo jàkkaarleeb bènn koñ (wala angal) da fay nekk beneen koñ bu tollook moom natt.

  • Safaanoo jàkkaarleeb ñetti tomb yu raŋale ci bènn rëdd da ñuy nekk yeneen ñetti tomb yu raŋale.

  • Safaanoo jàkkaarleeb bènn mbege ci bènn rëdd da fay nekk bènn mbege bu tollook moom ceñeer.